TSK

TSK · 1 Peter 3:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Dëgg laay wax, Almasi seere na ko, fenuma. Sama xol moo ma seereele Noo gu Sell gi, ne lii may wax dëgg la:

Waaye danoo dàq jépp jëf ju gàccelu ju nit di jëfe làq-làqal. Doxunu ag njublaŋ te sopparñiwunu kàddug Yàlla. Liy dëgg kay lanuy fésal, ba am kóoluteg ñépp, fi kanam Yàlla.

te nga saxoo ngëm ak xel mu dal. Am na ñu tanqamlu seen ndéeyum xel ba suuxal seen ngëm.

Titus 2:8 TSK

ak kàddu gu wér gu kenn dul mana weddi, ngir rusloo ab noon bu amul lenn lu bon lu mu nu baatale.

¶ Deeleen nu ñaanal nag. Li nu wóor de, moo di sunum xel yeddu nu fenn, te it di def lu baax ci lépp moo di sunu bëgg-bëgg.

Ndax coobarey Yàlla kat moo di ngeen di def lu baax, ba wedamal nit ñu ñàkk bopp ñi xamul dara.

¶ Naka noonu yeen jigéen ñi, nangul-leen seen jëkkër, ngir jëkkër ju ci nanguwula gëm kàddu gi it, mana gindiku te wax du ci am yoon, ngir na jabaram di jëfe,