TSK

TSK · 1 Peter 3:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

di jiite ku woyof mbubb ci njubte, di ko xamal aw yoonam.

Yaw laa moy, yaw doŋŋ. Li nga ñaawlu laa def. Kon boo waxee, yaa yey; te soo àttee, wàcc nga.

Aji Sax ji, néew-ji-doole, mu yenni; ku bon, mu daane ci suuf.

Aji Sax jee safoo ñoñam, di terale néew-ji-doole ag mucc.

néew-doole yi dellu bége Aji Sax ji, ñi gëna ñàkk di bànneexoo Aji Sell ju Israyil.

Noowug Boroom bi Aji Sax jaa ngi fi sama kaw, ndax Aji Sax jee ma diw, fal ma, ngir ma àgge néew-doole yi xibaaru jàmm. Moo ma yebal ngir ma dëfal ñi seen xol jeex, yégal jaam yi, seen goreel, yégal ñi ñu tëj, seen ubbite.

Yeena ñàkk xel! Xanaa du ki sàkk biti moo sàkk biir itam?

Waaye ab Yawut dëgg, kumpag biir xol la koy nekke, xaraf it mbirum xol la; ci xel mi lay sottee, waaye du ci mbindum yoon. Ngërëm la it du ci nit lay jóge, xanaa Yàlla.

Ndaxam ci sama biir xol, yoonu Yàllaa ma neex.

¶ Man Póol ci sama wàllu bopp nag, maa leen di ñaaxe teeyug Almasi, akug lewetaayam, man miy teew ci seen biir, di ab ragaleey, fi seen kanam, te bu ma soree doŋŋ laa leen di ñemeey,

Saxooleen woyof, lewet, te deeleen muñ, di muñalante ngir cofeel.

ndaxte dee ngeen, ba seenug dund ànd ak Almasi, làqe fa Yàlla.

¶ Yeenay ñi Yàlla taamu, sellal leen, sopp leen. Kon nag solooleen xolu yërmande, akug mbaax, ak woyoflu, ak jikko ju lewet, ak xolu muñ.

Ñu ni mel lanuy sant ak a dénku ngir Sang Yeesu Almasi, ngir ñu dal, tey yëngu, di dunde seen ñaqu bopp.

Jaamub Boroom bi ndànk la war di jubbanti diiŋatkat yi, nde jombul Yàlla may leen ñu tuub, ba xam liy dëgg.

Kon nag baleen jépp jikko ju tilim, ak mboolem xeeti mbon yi ne gàññ, te ngeen nangu ci biir ag woyof, kàddu, gi jëmbate ci yeen te man leena musal.

Ndax kat dangeena judduwaat, te jiwu wi ngeen judduwaate mooy kàddug Yàlla giy dund te sax dàkk; du jiwu wuy yàqu, waaye mooy jiwu wu dul yàqu mukk.