TSK

TSK · 1 Samuel 13:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Firawnaa ngay jubsi, bànni Israyil séentu, yemuñu ci ñu moy waa Misra, ñu dikk, jubsi leen. Tiitaange lu réy jàpp bànni Israyil. Ñu woo Aji Sax ji wall.

¶ Ba loolu amee waa Sif dem Gibeya ca Sóol, ne ko: «Daawuda de, ma nga làqu fa nun. Ma nga ca xunti yu kawe ya ca Orsa, ca kaw tundu Akila, fa féete màndiŋ ma bëj-saalum.

¶ Ci kaw loolu bànni Israyil, ya ca wàllaa xur wa, ak ña ca wàllaa dexu Yurdan gis ne xarekati Israyil daw nañu, te Sóol aki doomam dee nañu. Ñu daldi daw, gental seeni dëkk, waa Filisti dikk, dëkke.

Waaye ñu ngii di xeet wu ñu futti, sëxëtoo; ñépp tëje ciy pax, dence ci këri tëjukaay, ñu doon alalu xare fu leen kenn dul xettlee, xanaa ñu di leen sëxëtoo, te kenn du ne ñu delloo leen.

Ñooñu àddina sax yeyoowu leen woon, te àll yi lañu doon wëreeloo, ak tund yeek xunti yeek kàmb yi.