TSK

TSK · 1 Samuel 13:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Foofa ngeen di yóbbu seen saraxi dóomal, ak yeneen sarax, ak seen céri fukkeel, ak seenub jooxe, ak seen sarax yu ngeen xas, ak seen saraxi yéene, ak seen saraxi taawug jur gu gudd ak gu gàtt.

Sóol ne Axiya sarxalkat ba: «Indil gaalu Yàlla gi.» Bésub keroog gaalu Yàlla gaa ngaak bànni Israyil.

Gannaaw loolu Daawuda tabaxal fa Aji Sax ji ab sarxalukaay, rendi fa ay saraxi dóomal, ak ay saraxi cant ci biir jàmm. Ba mu ko defee Aji Sax ji nangul réew ma, mbas ma bàyyi Israyil.

Neel tekk, xaar Aji Sax ji, yaakaar ko. Bu sa xol jóg ci kuy baaxle, tey lal ay pexe.

Bul feyantook ku la tooñ; dénkul ci Aji Sax ji, mu wallu la.

Saraxu nit ku bon ñaawtéef la, rawatina bu ci jubloo lu bon.