TSK

TSK · 1 Samuel 14:39

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Bésub keroog mbooloom Israyil jàq nañu, ndax ngiñ lu Sóol teg ci seen kaw, ne: «Képp ku lekk fii ba ngoon te feyooguma ci samay noon, yal na alku.» Mbooloo ma mépp, kenn sexu ca dugub.

Sóol nag déggal Yonatan, daldi ne: «Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund, deesul rey Daawuda.»

Buur Sóol ne ko: «Yaw Ayimeleg kay, dee rekk mooy sab àtte, yaak sa waa kër baay yépp.»

¶ Daawuda nag mer lool ca jëfi nit kooku. Mu ne Natan: «Giñ naa ci Aji Sax jiy dund, dee rekk mooy àtteb waa ji def loolu!

Ñépp a bokk benn dogal bi, ku jub ak ku bon, ku baax ak ku set, ak ku sobewu; kuy sarxal ak ku dul sarxal, muy ku baax ki, di bàkkaarkat bi, muy kiy giñ, di ki ragal ngiñ.