TSK

TSK · 1 Samuel 21:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Loolu tax sàmmi Ibraam ak sàmmi Lóot di jote. Rax ci dolli Kanaaneen ñi ak Periseen ñi ña nga woon ca réew ma.

¶ «Kenn ku bokkul ci waa kër sarxalkat yi du lekk ci sarax yu sell yi. Muy ku dal ak ab sarxalkat, muy ku koy liggéeyal di feyeeku, kenn du ci lekk ci sarax yu sell yi.

¶ «Sàkkal sunguf su mucc ayib, lakk ci fukki mburu ak ñaar, mburu mu nekk di juróom benni kiloy sunguf.

Ci biir loolu Sóol ne tëll, jiital ay nagam, jóge tool ya. Mu ne: «Lu nit ñi xewle bay jooy nii?» Ñu nettali ko kàdduy waa Yabes.

¶ Doweg, Edomeen ba taxawandook jawriñi Sóol, daldi àddu, ne: «Man de, gis naa doomu Yese ji, mu dikk dëkk ba ñuy wax Noob, ca Ayimeleg doomu Ayitub.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di taalif bu ñeel Daawuda.

Noonu la sama ñoñ di dajesee fi yaw, toogaanu la, di la déglu. Dañuy déglu say wax, waaye duñu ko jëfe mukk. Lu neex lañuy wax waaye amin wu lewul rekk la seen xol di sàkku.