Daawuda fabu mooki nitam, ñu wara tollu ci juróom benni téeméer, daldi bàyyikoo Keyla, di taxawaaloo fépp fu ñu ñeme. Ba ñu yeggee Sóol ne ko Daawuda rëcce na Keyla, Sóol yebbi.
TSK
TSK · 1 Samuel 25:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
1 Samuel 23:13
TSK
1 Samuel 27:2
TSK
Ba loolu amee Daawuda ak juróom benni téeméeri nit ña ànd ak moom, daldi jàll ba ca buurub Gaat, Akis doomu Mawog.
1 Samuel 30:21
TSK
¶ Daawuda nag dikk ba ca ñaar téeméer ña loofoon ba manuñu koo topp, te ñu bàyyi woon leen ca xuru Besor. Naka lañu gatandu Daawuda ak ña mu àndal, Daawuda dikk, dajeek ñoom, jàmmanteek ñoom.
Proverbs 16:32
TSK
Muñ mer, moo gën njàmbaar; tënk sa bakkan moo raw nangub dëkk.
Proverbs 19:11
TSK
Ku xam lu jaadu, muñ mer, tanqamlu ku la tooñ ngay damoo.
Proverbs 25:8
TSK
bul gaawa layooji, ana nooy def ëllëg, bu ñu la yeyee?
James 1:19
TSK
¶ Bokk yi, soppe yi, nangeen xam lii: na ku nekk di gaaw ci déglu, di yeexa wax tey yeexa mer.