TSK

TSK · 1 Samuel 25:39

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Léegi nag sang bi, giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund, nga fekke tey, Aji Sax jee la teree tuur deret tey, di feyul sa bopp. Muy say noon, di ñi lay fexeel lu bon, yal nañu bokk ak Nabal mii demin.

Lu ko moy de, giñ naa ci Kiy Dund, Aji Sax ji Yàllay Israyil, ji ma téye ba loruma la, soo gaawul woon, dogalesi ma, du kenn moos ku ñuy wacc, bët di ko sete ci mboolem kuy taxaw colal te bokk ci Nabal.»

Daawuda ne Amalegeen ba: «Yaa gàddu sa bakkanu bopp, ndax yaa seedee sa gémmiñu bopp ne yaa rey ki Aji Sax ji fal.» Surga ba dóor Amalegeen ba, mu dee.

Aji Sax jeey Kiy dund. Kii ma sës moo jara sant. Yàlla sama cëslaay ji may musal moo màgg!

Ba mu ko defee ñu wékk Aman ca bant ba mu waajaloon Mardose. Merum Buur doora giif.

Am kan lay gas, ba mu xóot, te pax ma mu gas, moo ca tàbbi.

Balaa seen cin a yég tàngooru gajj, muy gu tooy, muy guy boy, yal na leen fekk sànku.

Kër ak alal ngay donne ci baay; jabar ju xelu, Aji Sax jee koy maye.

Jeeg bu jàmbaare, ndaw lu jafe, ba rawati gànjar!

Hosea 2:6 TSK

Ay doomam, duma leen yërëm, nde doomi ngànctu lañu.

Teewul nuy ñaan Yàlla, ngeen baña def dara lu bon, te ñaanunu loolu am, ngir nu man koo firndeele sunu taxawaay, waaye bu sunub taxawaay doonul woon lu firndewu itam, sunu yéene mooy ngeen di def lu baax.

Boroom bee may wallu ci jépp jëf ju bon, te moo may aar ba tàbbal ma fa nguuram ga fa asamaan. Daraja ñeel na ko, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.