TSK

TSK · 1 Timothy 1:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Te it bu góom bi soppikoo weex, na dem ca sarxalkat ba.

Bésub keroog, maay nangu,» kàddug Aji Sax jee, «maay nangul asamaan, moom, mu nangul suuf;

¶ Ci kaw loolu Yeesu ne: «Baay, baal leen, ndax li ñuy def, xamuñu ko.» Ñu daldi tegoo bant ay yéreem, ngir séddoo ko.

Acts 3:17 TSK

¶ «Teewul nag bokk yi, xam naa ne ñàkka xam moo leen taxa jëfe noonu, te loolu it moo dal seeni kilifa.

Acts 9:1 TSK

¶ Ci biir loolu Sóol moom, noyyeewul lu moy di tëkkook a jéema bóom taalibey Sang bi. Mu dem nag ca sarxalkat bu mag ba,

Acts 9:13 TSK

Anañas nag ne ko: «Sang bi, maa dégge ci ñu bare mbirum kooku, ñu seede mboolem jëf ju bon ji mu def say nit ñu sell ci biir Yerusalem.

Acts 26:9 TSK

¶ «Man ci sama bopp, gàntal lu ma man turu Yeesum Nasaret, sama warugar laa ko defoon.

Yeena déggadi woon, waaye tey daj ngeen yërmande, ndax déggadig Yawut yi.

ndax kat maa gëna ñàkk solo ci ndawi Almasi, te yeyoowuma sax turu ndaw, gannaaw maa doon bundxatal mbooloom Yàlla mi.

Su dee ci mbirum xéraangey diine, maa daan bundxatal mbooloom gëmkati Almasi, te su dee ci wàllu njubtey sàmm yoon wi, maa mucc sikk.

Kon nag nanu ñemee dikk ba ca ngàngunem yiw ma, ndax nu jot yërmande te dajeek aw yiw wu nu wallu fu nu ko soxlaa.

¶ Gannaaw bu nu xamee xéll liy dëgg ba noppi nag, su nu bàkkaaratee te di ko tey, su boobaa ab sarax bu far yooyu bàkkaar amatu ci.

Ndax kat ñàkkoona xam yoonu njub wi sax moo doon gën ci ñoom, xam ko ba noppi, dëddu ndigal lu sell la ñu leen ca àgge woon.