TSK

TSK · 1 Timothy 4:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Na téere boobu ànd ak moom, mu di ci jàng giiru dundam, ndax mu tàggatu ci ragal Yàllaam Aji Sax ji, ngir di sàmm mboolem kàdduy yoon wii, ak dogali yoon yii, ngir di ko jëfe,

Xanaa di bége yoonu Aji Sax ji, di ko jàngat guddeek bëccëg.

Sàkkul xel mu rafet ni xaalis, wut ko ni alal ju làqu.

Waa Bere nag gëna am déggin waa Tesalonig. Ñu gëm kàddu gi, xér ci lool, bés bu nekk ñuy niir Mbind mi, ngir xam ndax la ñu leen di wax noonu la.

Waaye kiy waxe kàddug waxyu, nit ñi lay waxal, di feddlee, di ñaaxe ak di naabe.

¶ Kon nag ana nees di def, bokk yi? Bu ngeen dajee, kii am woyu cant, kii am lu muy jàngle, kee am am peeñu, kale am lu muy waxe weneen làkk, keneen am am piri, loolu lépp na ko feddli ngëm taxa jóg.

¶ Soo dee xamal loolu bokki gëmkat ñi, yaa di jawriñu Almasi Yeesu ju baax ju xontoo kàdduy yoonu ngëm wi, ak àlluwa ju rafet ji nga topp naka jekk.

Defal sa kem-kàttan ba boo teewee fa kanam Yàlla, di ku mu gërëm, ab liggéeykat bu mucc gàcce, di xamle kàddug dëgg gi ni mu ware.

¶ Googu kàddu ngay waaree, di dénkoo ak di femmoo, te boole ci fulla ju mat sëkk. Bu la kenn yab.