bay jaamuji yeneen yàlla, di leen sujjóotal, mbaa muy sujjóotal jant bi, mbaa weer wi, mbaa mboolem gàngooru asamaan, te santaanewuma ci lenn,
TSK
TSK · 2 Kings 21:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ilyaas dikk jàkkaarlook mbooloo ma mépp. Mu ne: «Yeen nag dungeen dakkal seen ciŋiñ-caŋañ ji ngeen nekke, wet gu nekk ngeen féete fa? Su Aji Sax ji dee Yàlla, toppleen ko; su dee Baal, ngeen topp ko.» Mbooloo ma ne patt.
Tànki buuri Israyil la topp, di roy waa kër Axab, ndax doomu Axab la jël jabar, di def li Aji Sax ji ñaawlu.
¶ Ba mu ko defee Yewu woo mbooloo ma mépp, ne leen: «Axab tuuti la jaamu Baal. Man Yewu bu baax laa koy jaamu.
Ba loolu amee ñu dëddu mboolem seen santaaney Yàlla Aji Sax ji; sàkkal seen bopp ñaari wëllu yu ñu móol, samp xer wu ñuy jaamoo Asera, di sujjóotal mboolem biddiiwi asamaan tey jaamu Baal.
Xanaa doo ma ne seen Yàlla Aji Sax ji ngeen yaakaar? Xanaa du moom nga toxal bérabi jaamookaayam yeek sarxalukaayam, ba noppi ne waa Yerusalem ak Yuda sarxalukaay boobu ci Yerusalem lañuy sujjóotal?”
«Waaye yeen ñi wacc Aji Sax ji, yeen ñi fàtte sama tund wu sell wi, di taajal ndab, Gàdd tuur mi, di xellil biiñu njafaan, Meni tuur mi,