TSK

TSK · 2 Peter 1:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Benn fan ci sab ëtt de moo dàq junniy fan feneen. Sama taxawaayu bunt kër Yàlla moo ma gënal tëraayu biir xaymab ku bon.

Jeeg bu jàmbaare day teral jëkkër ja, jeeg buy rusloo day semmal jëkkër ja.

«Jeeg bu jàmbaare bare na, waaye yaw, yaa ci raw.»

Moom mi nu bañalul Doomu boppam, xanaa jooxeel nu ko, nun ñépp, ana nu mu nuy baña baaxee gépp yiw, boole ci?

Yàllaa am kóllëre, moom mi leen woo, ngir ngeen bennoo ak Doomam Yeesu Almasi, sunu Sang.

Mu ne ma: «Sama yiw doŋŋ nga soxla; sama manoore, ci ag néew doole lay mate.» Kon kat dinaa gëna bégati ci damoo diggante yu ma néewe doole, ngir manoorey Almasi wàcc ci sama kaw.

¶ Dama leen di dénku nag, man mi ñu tëj ndax Sang bi, ngir ngeen dund dundin wu yellook wooteb Yàlla, bi mu leen woo.

¶ Li ci des nag bokk yi, moo di lii: mboolem lu dëggu, ak mboolem lu tedd, ak mboolem luy njub, ak mboolem lu set, ak mboolem lu jekk, ak mboolem lees di rafetlu, ndegam lu nawlu la te yelloo ngërëm, na leen loola soxal.

Ñaax nanu leen, dëfal leen, dénku leen, ngir ngeen di jëfe jëfin wu yelloo ak Yàlla, mi leen woo ci nguuram ak teraangaam.

Ci loolu it la leen woo ba mu jëfandikoo xibaaru jàmm bi nu leen àgge, ngir ngeen séddu ci sunu ndamal Boroom Yeesu Almasi.

Moo nu musal, woo nu woote bu sell te sunuy jëf taxul, waaye coobarey boppam a tax, ak yiwam wi ñu nu may ci Almasi Yeesu, balaa ay jamonoy jamono di sosu.

yeen ñi seen ngëm tax ngeen yiiru ci manoorey Yàlla, mi leen di nége mucc ga mu waajal te di ko feeñal ca bés bu mujj ba.

¶ Waaye yeen nag yeen ay giir giy tànneef, yeenay sarxalkati Buur, yeen ay askan wu sell, yeen ay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.

Lu bon, buleen ko feye lu bon; ay saaga it, buleen ko feye ay saaga. Xanaa ngeen ñaanal leen, feye leen ko, ndax ci loolu lees leen woo, ngir ngeen jagoo barke.

Aw yiw ak jàmm baawaan na, ñeel leen, ndax xam gu ngeen xam Yàlla, ak sunu Sang Yeesu.