TSK

TSK · 2 Peter 2:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Su ko sarxalkat bi seetee ba gis fa taab ba nekkoon mel ni lu def pax, te kawar gi ci nekk soppiku weex, na sarxalkat bi biral ne nit ki sobewu na. Jàngoroy der juy law la, ju juddoo ca taab ba.

¶ «Su liir wi delloo tegu ci biir néeg bi gannaaw bu ñu teggee doj yi, xeet biir néeg bi, ba raax ko,

¶ «Aw rab wu bon, bu jàppee nit ba génn ko, day wër bérab yu fendi, di wut fu mu nopploo, te du ko gis. Su ko defee mu ne: “Naa dellu ca sama kër, ga ma jóge.”

¶ Ñi ñu xasa leeral nag, te ñu jota mos may gu bawoo asamaan, séddu ci Noo gu Sell gi, deesu leen mana defal dara.

Aw yiw ak jàmm baawaan na, ñeel leen, ndax xam gu ngeen xam Yàlla, ak sunu Sang Yeesu.

Kàddu yu réy yu tekkiwul dara lañuy naxee, di fàbbee xemmemtéefi bakkan yu jéggi dayo, ay nit ñu yàggula rëcce ci ñeneen ñu nekk cig réer.