TSK

TSK · 2 Peter 2:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Naka la séentu Sodom ak Gomor ak joor ga ba fa mu yem, gis nag saxar suy gillee ci suuf, mel ni saxaru taalu ban.

su boobaa yéefar yépp a naan: «Ana lu waral Aji Sax ji def nii réew mi? Lu waral mii sànj mu tàng te réy?»

Mu mel ni ba Yàlla tasee Sodom ak Gomor, tasaale la ko wër.» Kàddug Aji Sax jee. «Nit du fa dëkkati, doom aadama du fa dalati.»

«Efrayim, ana nu ma lay baye, yaw Israyil laa ne, nu ma lay tege ciy loxo? Ana nu ma lay defe ni Atma? Nu ma lay yemaleek Ceboyim? Sama xol a bëpp, sama yërmandee yëngu.

Moo tax, giñ naa ko ci man miy dund,» kàddug Aji Sax ju gàngoor yee, Yàllay Israyil, «Mowab déy ni dëkkub Sodom lay mujje, Amoneen ñi mel ni Gomor, ay dég ak paxi xorom a koy nangu, mu gental ba fàww. Sama ndesu ñoñ a leen di sëxëtoo, ndesu xeet wi ma séddoo moo leen di moom.»

¶ Xew-xew yooyu dal maam ya ay misaal la, te dees koo bind ngir nu jànge ci, nun ñi mujug jamono yemool.

Jude 1:15 TSK

ngir àtte ñépp, ba tiiñal mboolem yéefar yi, ndax mboolem nu yéefare ni ñu jëfe seen jëfi yéefar, ak mboolem kàddu yu ñaaw yi bàkkaarkati yéefar yi teg cib deram.»