TSK

TSK · 2 Samuel 15:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Daawuda daldi giñ, neeti ko: «Dinaa la ko giñal, sa baay xam na xéll cér bi ma am ci yaw. Moo tax mu ne: “Bu Yonatan yég sama mébét mukk, lu ko moy dina ko naqarlu.” Waaye giñ naa ko, nga fekke ci Aji Sax jiy dund, ab jéego sax doxul sama digganteek dee.»

¶ Ci biir loolu Ilyaas ne Alyaasa: «Xaaral fii rikk, ndax Aji Sax ji da maa yebal Betel.» Alyaasa ne ko: «Ak sama digganteek Aji Sax ji, Kiy Dund, nga fekke tey, duma teqlikook yaw mukk.» Ñu daldi ànd, dem Betel.

¶ Gannaaw loolu Ilyaas ne Alyaasa: «Ngalla xaaral fii, ndax Aji Sax ji da maa yebal dexu Yurdan.» Alyaasa ne ko: «Ak sama digganteek Aji Sax ji, Kiy Dund, nga fekke tey, duma teqlikook yaw mukk!» Ñu ànd ñoom ñaar.

Xarit du bëgg, di bañ; mbokk day bokk ak yaw say coono.

Ba Barnaba dikkee ba gis yiw, wi leen Yàlla may, dafa bég, di leen ñaax ngir ñu ŋoye seen xol ci Sang bi.

Du teg leen tooñ laay waxe lii, ndax wax naa ko ba noppi, yeena ngi ci sunu xol, ngir nu bokk dund, mbaa nu bokk dee.