TSK

TSK · 2 Samuel 2:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Naka la Abner délsi ba Ebron, Yowab berook moom ca buntu dëkk ba, mel ni kuy déeyook moom, daldi koy jam ci biir, rey ko, feyul Asayel, rakkam ja Abner bóomoon.

¶ Gannaaw loolu Buur Daawuda ànd aki xarekatam, jëm Yerusalem, songi Yebuseen ña dëkkoon ca réew ma. Yebuseen ña ne Daawuda: «Doo fi dugg de, nde gumba yeek lafañ yi rekk ñoo lay waññi.» Booba foog nañu ne Daawuda manu faa dugg.

Néewub Amasaa nga ca digg yoon wa, sangoo deretam. Waa ja gis ne képp ku dox ba tollook moom, taxaw nga fa. Naka la waa ja gis ñépp di taxaw foofa, mu diri néew ba, jële ko ca yoon wa, ba ca àll ba. Mu sànni malaan ca kawam.