TSK

TSK · 2 Samuel 3:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Ruth 1:17 TSK

Foo deeye it, ma deeye fa, ñu denc ma fa. Yal na ma Aji Sax ji teg mbugal mu gëna tar, ndegam lenn lu moy dee tàggale na maak yaw.»

Sóol ne ko: «Na ma Yàlla teg mbugal mu gëna tar, waaye yaw Yonatan dinga dee déy!»

¶ Gannaaw ba loolu wéyee Aji Sax ji ne Samiyel: «Yaw foo àpp sa jooy yi ngay jooy Sóol te man maa ko dàq, ba doonatul buur ci Israyil? Gannaaw maa foq nguuram ci Israyil kay, duyal sa béjjén diwu oliw ba mu fees te nga dox, ma yebal la ci Yese waa Betleyem bi. Gis naa ciy doomam ki may fal buur.»

Aji Sax jee sottal la mu waxoon, ma jottli ko, te Aji Sax jee foqati nguur gi ci say loxo, jox ko sa jegeñaale, muy Daawuda;

Yeen de yeenay bokki buur lenqe, ngeen bokk ak moom jenn deret; kon xanaa ñépp duñu délloosi Buur, ngeen des gannaaw?”

¶ Buur Suleymaan nag giñ ci Aji Sax ji ne: «Yal na ma Yàlla teg mbugal mu gëna tar, ndegam Adoña du feye bakkanam lii muy sàkku!

Sunu kiirlaay lii, Aji Sax jeey boroom; sunu buur bii, Aji Sell ji séddoo Israyil ay boroom.

Benn yoon laa ko giñ ci sama sellnga, duma fen Daawuda: