TSK

TSK · 2 Samuel 9:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Fekk na Yonatan doomu Sóol ju góor am na doom ju góor ju tànk ya baaxul. Ndaxte ba ñu déggee tàgge bu jóge Yisreel, ñu ne Sóol ak Yonatan faatu nañu, fekk na xale ba am juróomi at. Ndaw sa ko daan topptoo, fab ko di gaawtuy daw, waaye na muy gaawtu di dem, xale ba daanu, daldi lafañ. Ma nga tuddoon Mefiboset.

Daawuda ne ko: «Bul tiit, dinaa jëfeek yaw ngor déy ngir sa baay Yonatan. Dinaa la delloo mboolem sa suufas maam Sóol, te yaay bokk ak man ndab ba fàww.»

Mu ne ko: «Éy Buur, sang bi, sama surga Ciba moo ma nax de, sang bi, ndax man, dama noon damay takklu sama mbaam war, gannaaw ab lafañ laa. Su ko defee ma ànd ak yaw. Yaay sama sang.