¶ Gannaaw dees noo bennale ak moom ci dee gu ñu nirule ak deeyam, dees nuy bennale itam ak moom ci ndekkite lu niru ndekkiteem.
TSK
TSK · 2 Timothy 2:11
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Romans 6:5
TSK
Dee gi Yeesu dee woon, moom lanu àndal ci sunu yaram, fu nu tollu, ngir dundug Yeesu itam mana fése ci sunu yaram.
Galatians 2:19
TSK
Su dee wàllu yoonu Musaa nag, man nit ku dee laa, te yoonu Musaa moo ko waral, ngir ma mana dund dund gu ñeel Yàlla. Dees maa boole ak Almasi rey ca bant ba.
Gannaaw loolu nun ñi fi dese bakkan lees di këfandoo ak ñoom, jëme ca niir ya, ngir nu dajejeek Sang bi fa jaww ja, nu daldi nekk ak moom ba fàww.
1 Timothy 1:15
TSK
Mboolem kàddu gii may wax, lu wóor la te jara gëm: Almasi Yeesu moo dikk ci àddina, ngir musal bàkkaarkat yi, te maa ci raw!
Titus 3:8
TSK
¶ Googu kàddu wóor na te damaa bëgg nga sàmmoo dëggal loolu, ngir gëmkati Yàlla yi saxoo def jëf ju baax. Loolu moo baax te am njariñ ci nit ñi.