TSK

TSK · 2 Timothy 2:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Ezra 1:6 TSK

Mboolem seeni dëkkandoo daldi def ci seen loxo jumtukaayi xaalis ak wurus, alal akug jur ak gànjar, te bokkul ak mboolem seen saraxi yéene.

Doomi Siyoŋ yu góor yu jar ya! Wurus lees leen daan nàttablee, ndeysaan tey, ñu jàppe leen ni njaqu ban lu tabaxkatu njaq liggéeye loxoom.

Tabaxkatu ndab bi daa amul sañ-sañ ci ban bi muy liggéeye, ngir tabax ci bennub tooyal, lenn ndabal teraanga, ak leneen ndabal njoogaan?

¶ Xanaa xamuleen ne kër Yàlla ngeen, te Noowug Yàlla moo dëkk ci yeen?

Ci Almasi ngeen bokke ci tabax bi, yeen jaambur ñi itam, ba mana doon dëkkuwaayu Yàlla, ci ndimbalal Noo gu Sell gi.

Ku wóor la woon, ñeel ki ko tabb, noonee Musaa wóore woon ci mboolem waa kër Yàlla.