TSK

TSK · 2 Timothy 2:24

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Mooy sàmm géttam bii ni kuy sàmm ug juram, boole mbote yi cib loxoom, taf cib dënnam, yóbbu; xar yiy nàmpal, mu wommat.»

Acts 7:26 TSK

Ca ëllëg sa mu juux ci ay Yawut yuy xeex, di leen jéema jubale, ne leen: “Yeen ay bokk ngeen, lu tax ngeen di lorante?”

Acts 23:9 TSK

¶ Ci kaw loolu coow lu réy jib. Ñenn ca firikati yooni làngu Farisen ya, ne bërét, àddook doole, ne: «Gisunu lenn lu bon ci nit kii. Ku xam ndax aw rab a wax ak moom, mbaa malaaka?»

Ndaxte gànnaay, yi nuy xeexe du gànnaayi suuxi neen, waaye da di gànnaay yu am fa Yàlla, kàttanu daane ay tata. Te xalaatin yu jubul, noo leen di daaneel,

Saxooleen woyof, lewet, te deeleen muñ, di muñalante ngir cofeel.

¶ Mboolem lu ngeen di def nag, buleen ci boole xultu mbaa xuloo,

Manoon nanoo taafantoo li nu diy ndawi Almasi, ba diisal leen, waaye danoo lewetoon domm ci seen biir, mel ni jaboot juy topptoo ay doomam.

¶ Yaw miy nitu Yàlla nag, dawal loolu, te topp njub ak njullite ak ngëm ak cofeel ak muñ akug teey.

Titus 1:7 TSK

Ndax kat, njiit li war na di ku mucc sikk, gannaaw ab saytukatu kër Yàlla la. Bumu di ku bew, mbaa ku gaawa mer, mbaa ab màndikat, mbaa bëggkatub xeex, mbaa wutkatub am-am bu lewul.

Titus 3:2 TSK

Buñu yàq der te buñu bëggu ay, waaye nañu di bëggkati jàmm, te nañuy jëfe lewetaay gu mat sëkk, seen digg ak ñépp.

¶ Bokk yi, soppe yi, nangeen xam lii: na ku nekk di gaaw ci déglu, di yeexa wax tey yeexa mer.

James 4:2 TSK

Yeenay xemmem lu ngeen dul am. Yeenay bóome, di iñaane lu ñeneen am, te manuleen koo am. Yeenay xuloo ak a jàppante. Dungeen am, ndax yeena ñaanul.

Jude 1:3 TSK

¶ Soppe yi, yàkkamti woon naa leena bind ci mbirum mucc gi nu bokk, waaye fàww ma bind leen, ngir ñaax leen ci xeexal yoonu ngëm, wi Yàlla xasa dénk ñu sell ñi, benn yoon ba fàww.