TSK

TSK · 2 Timothy 2:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

«Góor-góorluleen ba dugge ci bunt bu xat bi, ndax maa leen ko wax, ñu bareey jéema dugg, waaye duñu ko man.

¶ Dëgg la am na ñuy waare turu Almasi ci kaw kiñaan ak diiroo mbagg, waaye am na itam ñu koy defe yéene ju rafet.

Xare bu baax bi, xare naa ko, rawante bi, sottal naa ko, ngëm gi ma am, sàmm naa ko.

Yeesu mi ñu def mu gëna suufe as lëf malaaka yi, moom lanu gis deeyam gi mu dee tax mu jagoo kaalag teraanga. Noonu la deeyale ñépp ci kaw yiwu Yàlla.

¶ Ndokklee ku muñ ab nattu, nde su ca amee ngërëm, mooy yooloo kaalag dund, gi Yàlla dig ñi ko sopp.

Bul ragal mukk mitit wi nga nara daj. Seytaanee ngi noonu di dugal kaso ñenn ci yeen, ngir nattu leen. Dingeen am coono diiru fukki fan. Nanga saxoo kóllëre ba dee fekk la ci, ma kaalaa la kaalag dund.

Yeneen ñaar fukki gàngune ak ñeent a ko wër, ñaar fukki mag ak ñeent toog ca gàngune ya. Ña nga sol mbubb yu weex, ay kaalay wurus tege ca seen bopp.