Yerusalem, tabb naa ay jongrukat ci sa kawi tata. Buñu selaw, du guddi du bëccëg! Yeen ñiy soññ Aji Sax ji, buleen dal-lu.
TSK
TSK · 2 Timothy 4:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
«Yaw nit ki, tabb naa la wattukatub waa kër Israyil. Nangool sama gémmiñ kàddu, artool ma leen ko.
¶ «Yaw nit ki nag, jongrukat laa la tabb, ñeel waa kër Israyil, ba boo déggee baat bu jibe sama gémmiñ, war leen koo artoo ci sama ndigal.
Ndokklee surga yooyu seen njaatige dikk fekk ñu teewlu. Maa leen ko wax déy, njaatige leey takku, toogal leen ba noppi dikk, taajal leen, ñu lekk.
Ca ëllëg sa nu dem ba àgg Sesare. Nu dem kër Filib, xamlekatu xibaaru jàmm, bi bokk ci Juróom ñaar ñi. Nu dal ak moom.
Moo may ñii di ay ndawam, ñee di ay yonent, ñee di ay xamlekati xibaaru jàmm bi, ñale di ay sàmmi mbooloom gëmkat ñi, mbaa ay jànglekat.
¶ Waxal-leen ma Arsipp ne ko: «Neel jàkk ci liggéey bi nga sasoo ci Boroom bi, ngir nga sottal ko.»
Bu la kenn xeebe sa at yu néew, waaye nanga doon royukaayu gëmkat ñi ci wax ak jëfin, ak cofeel, ak ngëm, ak dundin wu set.
¶ Bul kersawoo di seedeel sunu Sang, mbaa nga di ma kersawoo, man mi ñu tëj ngir moom, waaye jëlal sa wàll ci coonob xibaaru jàmm bi, ni la ko manoorey Yàlla manloo.
Looloo ma tax di muñ lépp, ngir ñi ñu taamu, ndax ñoom it ñu dajeek mucc gi ci Almasi Yeesu, boole ci teraanga ju sax.
¶ Déggal-leen seeni njiit te nangul leen, ndax sàmm bakkani ñi ñu jiite mooy seenub liggéey, te moom lees leen di laaj ëllëg. Su ko defee ñu defe ko xol bu sedd, te bañ koo def di binni, ndax loolu du seen njariñ.
¶ Teewlul te nga leqli ndes wi ngay waaja deele. Ndax kat, gisuma sa jëf ju mat fa sama kanam Yàlla.