Nekkul it wàllaa géej ba ngeen naan: «Ana ku nuy jàllil wàllaa géej, jëlil nu ko, dégtal nu ko, ba nu jëfe ko?»
TSK
TSK · Acts 10:33
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Proverbs 1:5
TSK
Na boroom xel mu rafet déglu, yokk dég-dégam, te kiy ràññee di jariñoo ay tegtal,
Proverbs 18:15
TSK
Ku am ug dégg wut xam-xam, ku rafet xel sàkku xam-xam.
Acts 28:28
TSK
¶ «Xamleen nag ne xibaaru mucc gii tukkee fa Yàlla, yóbbante nañu ko ñi dul Yawut, te ñoom dinañu ko déglu.»
Galatians 4:14
TSK
Nattu ba leen sama woppi yaram tegoon it taxul ngeen jéppi ma, taxul ngeen beddi ma. Ni malaakam Yàlla ngeen ma dalale, mbaa ni Yeesu Almasi
James 1:19
TSK
¶ Bokk yi, soppe yi, nangeen xam lii: na ku nekk di gaaw ci déglu, di yeexa wax tey yeexa mer.
1 Peter 2:1
TSK
¶ Kon nag baleen mboolem xeetu mbon, ak mboolem njublaŋ, ak jinigal, ak kiñaan, ak mboolem xeetu yàq der.