noonee nu ko jote ca ña ko fekke woon ca ndoorte la, te seede yooyu mujj doon jawriñi kàddug Yàlla.
TSK
TSK · Acts 10:39
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
dale ko ca ba ko Yaxya sóobee ci ndox, ba bés ba ko Yàlla jëlee fi sunu biir, yéege ko. Kon nag kenn ci ñooñu war naa bokk ak nun, seede ndekkitel Yeesu.»
Yeesu moomu nag, Yàllaa ko dekkal, nu seede ko, nun ñépp.
xamleen xéll, yeen ñépp ak bànni Israyil gépp, ne ci turu Yeesu Almasi waa Nasaret bi, ki ngeen daajoon ci bant, te Yàlla dekkal ko, ci turam doŋŋ la kii wére, ba taxaw ci seen kanam.
Kan ci yonent yi la seeni maam fitnaalul? Ñoo rey démb ña yégle woon ñëwug Aji Jub, ji ngeen wor tey, bóom ko.
Waa Yerusalem, ak seeni kilifa nag xàmmiwuñu woon Yeesu, te ba ñu daanee Yeesu lañu sottal waxu yonent, ya ñu daan biral bésub Noflaay bu nekk.
¶ Almasi moom, moo nu jot ci alkàndey yoon wi, ba mu doonee ku alku ngir nun, nde: «Alkute ñeel na képp ku ñu rey, wékk ko ci bant.»