TSK

TSK · Acts 12:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ibraayma nag tudde bérab boobu Yawe Yire (mu firi Aji Sax ji dina dikk). Moo tax ñuy wax ba tey, naan: «Aji Sax jaa ngay dikke ca tundam.»

Sóol a ngay demee gii wetu tund wi, Daawudaaki nitam bartaloo wet ga ca des, gaawtu di wéy, ngir rëcc Sóol. Naka la Sóol ak mbooloom dem bay wër-ndombo Daawuda aki nitam, ngir jàpp leen,

May nga ma bànneexu xol bu raw seen pepp mu tuurook biiñ bu wal.

Léegi nag yiwi naa la bés niki tey. Soo bëggee ànd ak man Babilon, ñëwal, dinaa la topptoo. Soo buggul, toogal. Réew mépp a ngii ci sa kanam. Fu la ci neex ak foo ci taamu, dem fa.»

Acts 5:23 TSK

ne: «Danoo fekk kaso ba tëje ràpp, wattukat ya taxaw ca bunt ya. Nu tijji, fekkunu kenn ca biir!»

Mbir moomu nag moo tax ma woolu leen, ngir giseek yeen, diisook yeen, ndax yaakaaru bànni Israyil moo waral sama jéng yii.»

Buleen jaaxle ci dara, waaye ci mbir mu mu mana doon, deeleen dikke Yàlla seeni soxla, di ko ñaan ak a dagaan te boole ci di ko sant.

Moo tax nu mana am fitu wax ne: «Boroom beey sama ndimbal, duma tiit. Ana lees ma manal?»