TSK

TSK · Acts 13:15

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Yoonu Musaa wi ak waxi yonent yi la woon ba kera ba Yaxya dikkee. Waaye ba mu dikkee lañu yégle nguurug Yàlla, ñépp di ci jéema dugge seen doole.

Acts 2:4 TSK

Ñoom ñépp nag feese Noo gu Sell gi, tàmbalee làkk làkk yu wuute, na leen ko Noo gi manloo.

Acts 2:37 TSK

¶ Ba mbooloo ma déggee loolu, naqar wu mel ni jam-jamu xol la leen def. Ñu ne Piyeer ak ndaw ya ca des: «Bokk yi, nu nuy def nag?»

Waa Yerusalem, ak seeni kilifa nag xàmmiwuñu woon Yeesu, te ba ñu daanee Yeesu lañu sottal waxu yonent, ya ñu daan biral bésub Noflaay bu nekk.

Ndaxte ca njàlbéen ga ba tey ay nit a ngi waaree yoonu Musaa ci dëkk bu nekk, ñu di ko jàng ci jàngu yi bésub Noflaay bu nekk.»

Ci kaw loolu ñépp jàpp Sosten, njiitu jàngu ba, dóor ko ca àttekaay ba, te taxul Galyon yégal ko yaramam.

Acts 22:1 TSK

¶ «Yeen bokk yi, yeen samay baay, dégluleen léegi li ma leen di wax.»

Waaye kiy waxe kàddug waxyu, nit ñi lay waxal, di feddlee, di ñaaxe ak di naabe.