TSK

TSK · Acts 13:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

da ne leen: «Defleen seen xel ci mboolem kàddu yi ma leen di artoo man, bésub tey, te ngeen sant seeni doom ñu sàmmoo jëfe mboolem kàdduy yoon wii.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor.

Muy taalif bu giiroo ci Asaf. Yeen sama xeet, dégluleen, ma digal leen; teewluleen ma, ma wax leen.

Éey waa kër Lewi, santleen Aji Sax ji! Yeen ñi ragal Aji Sax ji, santleen Aji Sax ji!

Moroom ma nag femmu ko, ne ko: «Ragaloo sax Yàlla, te yaa ngi ci menn mbugal mii?

Acts 2:22 TSK

¶ «Yeen bokki Israyil, dégluleen wax jii! Yeesu waa Nasaret bi, Yàlla moo firndeele ag dëggoom, ay kéemaan aki kiraama aki firnde yu mu sottale jëmmu Yeesu moomu fi seen biir, te loolu xam ngeen ko xéll.

Acts 10:2 TSK

Ku jullite la woon te ragal Yàlla, mook waa këram gépp; bare woon na sarax yu muy yéwéne askan wi, te ñaan ci Yàlla la saxoo woon.

Piyeer liyaar leen, ngir ñu noppi, daldi leen nettali, ni ko Boroom bi génnee kaso ba. Mu ne leen: «Yégal-leen ko Yanqóoba ak yeneen bokki taalibe yi.» Ba loolu amee mu génn, dem feneen.

¶ Ba ñu génnee ca jàngu ba, dañu leena ñaan ñu baamtu kàddu googu bésub Noflaay ba ca topp.

Ci kaw loolu mbooloo ma am lu ñu digal ku ñuy wax Alegsàndar, Yawut ya jañax ko ca kanam, mu daldi tàllal loxoom, ngir layool boppam ca digg mbooloo ma.

¶ Ba ba muy wax loolu, mbooloo maa nga koy déglu. Ba ñu déggee kàddu yooyu lañu xaacu ne: «Jëleleen ko ci kaw suuf! Ku mel ni kii yeyoowula dund!»

¶ «Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi. Ku am ndam nag doo loru mukk ci ñaareelu dee gi.

Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi.