TSK

TSK · Acts 13:31

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Acts 1:3 TSK

Ndaw yooyu itam la teew fi seen kanam ci firnde yu leer te bare, gannaaw ay coonoom. Diiru ñeent fukki fan la leen feeñu, di leen wax lu jëm ci nguurug Yàlla.

Acts 1:11 TSK

Ñu ne leen: «Yeen waa Galile, lu ngeen di taxaw nii di séentu asamaan? Yeesu male ñu yéegee fi seen biir, yóbbu asamaan, nii ngeen ko gise, mu jëm asamaan, ni lay délsee.»

Acts 2:32 TSK

Yeesu moomu nag, Yàllaa ko dekkal, nu seede ko, nun ñépp.

Acts 5:32 TSK

Nun noo seede loolu, nook Noo gu Sell, gi Yàlla jagleel ñi ko déggal.»

Du askan wépp la ko won, xanaa nun, seede yi Yàlla tànnoon lu jiitu, nu bokk ak moom lekk ak naan, gannaaw ndekkiteem.

ana kon nun ci sunu bopp, nan lanuy rëcce mbugal, su nu sàgganee pexem mucc mu réy mii Sang bi jëkkoona biral, te ñi ko dégg dëggalal nu ko?