TSK

TSK · Acts 13:38

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Dib taalif, ñeel Daawuda. Ndokklee yaw mi ñu baal bàkkaar, jéggal la ag moy.

Éey Israyil, négandikul Aji Sax ji. Aji Sax jee gore, te yaatug njot.

Du yeena tax nag may jëfe noonu. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Na leen loolu wóor. Kon nag waa Israyiloo, rusleen ba ne tott ci seeni jëfin.”

¶ «Juróom ñaar fukki ayi bés lañu àppal sa mbooloo ak sab dëkk bu sell, ngir dakkal tooñ gi, jeexal moy gi, jotu ñaawtéef, saxal njubte ba fàww, matal peeñum yonent, ba delloo bérab bu sella sell ag sellngaam.

¶ «Bésub keroog bëtu ndox dina bënnal kër Daawuda, ak waa Yerusalem, ngir setal bàkkaar ak sobe.

Acts 2:38 TSK

Piyeer ne leen: «Tuubleen te ku nekk ci yeen sóobu ci ndox ci turu Yeesu Almasi ngir njéggalug bàkkaaram, ngeen daldi jot ci Noo gu Sell giy maye.

Acts 5:31 TSK

Moom la Yàlla yékkati ci wetu ndijooram, def ko muy Njiit, di Musalkat, ngir may bànni Israyil ag tuubeel ak njéggalug bàkkaar.

¶ «Xamleen nag ne xibaaru mucc gii tukkee fa Yàlla, yóbbante nañu ko ñi dul Yawut, te ñoom dinañu ko déglu.»

¶ Ci moom lanu ame njot gi nu sottalal njéggalug moy, ndax deretam ji tuuru, noonu ko Yàlla defe ci yiwam wu yaa,

Ci moom lanu ame ag njot, te moo nu jéggal sunuy bàkkaar.

Maa leen di jéggal seeni njubadi, te seeni bàkkaar, duma ci bàyyeeti xel.»

Ndax ci yoonu Musaa sax, deret lees di setale daanaka lépp, te bu deret tuuruwul, njéggal amul.