TSK

TSK · Acts 13:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ba loolu amee Cedekiya doomu Kenaana talaata Mise, ne ko: «Ana fu Noowug waxyu gu Aji Sax ji jaare, ba jóge ci man di wax ak yaw?»

¶ Ba mu ko defee yonent ba ñuy wax Anaña yékkatee yet wa ca ndoddu Yonent Yàlla Yeremi, damm ko.

Acts 8:9 TSK

¶ Ku ñuy wax Simoŋ nag yàggoon na ca dëkk ba, di ñeengo. Ku waar waa Samari la woon, te doon tuddoo nit ku màgg.

Acts 13:6 TSK

¶ Ci biir loolu ñu wër dun ba bépp, ba yegg Pafos, péey ba. Ñu tase faak ab ñeengokatub Yawut buy yonent-yonentlu, ñu di ko wax Bar Yeesu.

Noonee Sànnes ak Sàmbres doon jànkoonteek Musaa, ni la góor ñooñu di jànkoontee ak dëgg gi; ñooy nit ñu seenum xel yàqu, te ñu doyadi ci wàllu ngëm.