TSK

TSK · Acts 14:26

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Gëmkat ña tasaaroo woon nag ndax fitna ja woon, ca mbirum Eccen, mujj nañu jàll ba diiwaanu Fenisi, ca dunu Sippar ak ca Àncos, waaye àggewuñu kàddu gi ñeneen ñu moy Yawut yi.

Acts 13:1 TSK

¶ Ca biir mbooloom gëmkat, ña woon ca dëkk ba ñuy wax Àncos, amoon na ay yonent ak ay jànglekat: ñuy Barnaba, ak Simeyon mi ñu dippee Ñuule, ak Lusiyus mi bawoo Siren, ak Manayen mi yaroondoo ak Erodd boroom Galile, ak Sóol.

¶ Ba loolu amee ndaw yi ak mag ñi mànkoo ak mbooloom gëmkat ñépp, ngir tànne ci seen biir ay nit, yebal leen Àncos, boole leen ak Póol ak Barnaba. Ñooñoo di Yuda, mi ñu dippee Barsabas, ak Silas, ñu diy mag ca bokk ya.

Póol moom, taamu Silas, daldi ànd ak moom dem, gannaaw ba leen bokk ya dénkee Boroom bi ciw yiwam.

ci kaw firnde yu manoorewu, aki kéemaan, lépp ci manoorey Noowug Yàlla. Loolu tax na, li dale Yerusalem, wëndeelu, ba ca diiwaanu Iliri, yégle naa fa xibaaru jàmm bu Almasi, ba mu mat sëkk.

¶ Waaye ba Sefas dikkee Àncos, jàkk laa ko def, weddi ko, ndax moo nekkul woon ci dëgg.

¶ Almasi moomu nag lanuy xamle; na mu gëna xeloo lanuy àrtoo nit ku nekk, te ni lanuy jàngale nit ku nekk, ngir àgge nit ku nekk ba fa kanam Almasi, fekk ko mat sëkk, na mu ware ku ànd ak Almasi.

waareel kàddug Yàlla te taxaw ci temm, su neexee ak su naqaree; di yedde, di femmoo, di ñaaxe, tey saxoo muñ ci sam njàngle.