TSK

TSK · Acts 15:29

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

ndax dundu mboolem mbindeef mooy deretam. Moo waral, man Aji Sax ji, ma ne bànni Israyil buñu lekk deretu menn mbindeef ngir dundu mboolem mbindeef mooy deretam. Képp ku lekk deret, dees koy dagge ci askan wi.

Xanaa nu bind leen, ne leen ñu moytu lu ay xërëm sobeel, moytu powum séy, moytoo lekk yàppu mala mu ñu tuurul deretam, ak lekk deret ci boppam.

Naka gëmkat ñi dul Yawut nag, bind nanu leen li nu dogal, ne leen ñu moytu ñam wu ñu sarxal ay xërëm, moytoo lekk deret ak yàppu mala mu ñu tuurul deretam, te moytu powum séy.»

Xam naa nag, wér na ma it te Sang Yeesu tax, ne amul lenn lu sobewu ci wàllu boppam, ba daganula lekk; waaye ki jàppe lenn muy lu sobewu, ci moom la loola di lu sobewu.

¶ Xool-leen bànni Israyil ci wàllu deret. Ñiy lekk yàppu juru sarax gu ñu rendi, xanaa bokkuñu ak sarxalukaay bi ab céram?

¶ Ma tëje fii nag, bokk yi, bégleen, yokkuleen ba mat sëkk, ñaaxanteleen, mànkooleen te jàmmoo. Su ko defee Yàlla miy Yàllay cofeel ak jàmm mooy ànd ak yeen.

Njullite gu set te mucc sikk fa kanam Yàlla Baay bi moo di lii: di nemmiku jirim akub jëtun ci seen njàqare, tey sàmmu ba mucc ci gàkki àddina.

Jude 1:20 TSK

Waaye yeen samay soppe, sampuleen ba dëgër ci seen yoonu ngëm wu sell wee sell, te ngeen di ñaane ci Noo gu Sell gi.

¶ «Waaye lenn a ngi lu ma lay sikke: yaa ngi uuf foofu ay nit ñuy saxal njànglem Balaam, moom mi doon xiirtal Balag ci tegal Israyil ndëgg-sërëx, ngir ñu lekk ñam wu ñu sarxal ay tuur, ak di gànctu.