TSK

TSK · Acts 15:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Mu ne leen: «Yeen de xam ngeen ne ab Yawut, mayeesu ko mu jaxasoo ak xeetu jaambur, mbaa mu seeti ko. Waaye man nag Yàllaa ma won ne du kenn nit ku ma naan daganula jaxasool, mbaa setul.

Moom la yonent yépp seedeel, ne képp ku ko gëm, jot nga sa njéggalug bàkkaar ciw turam.»

Acts 14:1 TSK

¶ Ba Póol ak Barnaba nekkee Ikoñum, noonu lañu dugge itam ca jàngub Yawut ya. Ñu waare, ba mbooloo mu mag gëm, ay Yawut aki Gereg.

¶ Ana kon nun Yawut yi, lu nu gëne ci nit ñi? Du ci lenn! Ndax firndeel nanu ba noppi ne, muy Yawut bi, di ki dul Yawut, ñépp a ngi ci kilifteefu bàkkaar.

Am Yàlla da di Yàllay Yawut yi doŋŋ? Da dul Yàllay jaambur yi dul Yawut itam? Ahakay, mooy Yàllay jaambur ñeet kay!

Nun ci ndabi yërmande yi Yàlla woo lanu bokk, te du ci Yawut yi rekk lees nu seppee, waaye ci jaambur ñi dul Yawut itam.

ñeel mbooloom Yàlla, mi ci Korent, yeen ñi ñu sellal ci jëmmu Almasi Yeesu, te ñu woo leen ngir ngeen doon ñu sell, ñeel itam mboolem ñiy tudde fépp fu mu mana doon, sunu turu Boroom Yeesu Almasi, mi leen moom, moom nu.

Kon nag amul Yawut ak ku dul Yawut, amul ab jaam ak as gor, amul góor ak jigéen. Yeen ñépp benn ngeen ci Almasi Yeesu.

¶ Ndaxte moom mooy sunu jàmm, moom mi boole ñaar, Yawut bi ak jaambur bi dul Yawut, def leen kenn. Ci suuxu yaramam wa ñu daaj la ñàggee ñagu mbañeel bi doxoon sunu diggante.

Dundin wu yees woowu amul jaambur akub Yawut, amul ku xaraf ak ku xaraful, amul ab doxandéem ak ku xayadi, amul ab jaam ak as gor, waaye Almasi mooy lépp te moo nekk ci ñépp.

¶ Kon nag gannaaw setal ngeen seen xol, ndax dëgg gi ngeen déggal, ba tax ngeen am cofeel gu mucc jinigal, ci bokki gëmkat ñi, nangeen soppantee xol bu set, cofeel gu mat sëkk.