TSK

TSK · Acts 16:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Acts 16:9 TSK

Ci biir loolu am peeñu dikkal Póol ca guddi: mu gis aw nitu Maseduwan taxaw, di ko tinu, ne ko: «Jàllsil Maseduwan, wallusi nu!»

Acts 20:6 TSK

Nun nag ba màggalu Yawut, ga ñuy wax Mburu mu amul lawiir weesee lanu dugge gaal fa dëkk ba ñuy wax Filipi, am juróomi fan ca yoon wa, door leena fekksi ca Torowas, toog fa juróom ñaari fan.

Xam ngeen na nu jëkkoona sonne, ak na ñu nu torxale woon ca Filib, dëkk ba, bala noo dikk fa yeen. Teewul ci sunu ndimbalal Yàlla, nu ñeme leena àgge, ci biir xeex bu metti sax, xibaaru jàmm bu Yàlla bi.