¶ Ba Musaa jubee dal ba, ba gis sëllu wa ak pecc ma, mer mu ne jippét tàkk la ko def, mu sànni àlluwa ya mu ŋàbboon, mu ne tasar ca suufu tund wa.
TSK
TSK · Acts 17:16
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ilyaas ne: «Man kat damaa xéroona xér ci yaw Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi. Waaw, bànni Israyil dañoo fecci sa kóllëreek ñoom; say sarxalukaay, ñu màbb; say yonent, ñu jam saamar. Ma des man doŋŋ, ñuy wuta jël sama bakkan nii!»
Ba loolu amee Eliyu doomu Barakel ma askanoo ci Buus, bokk ci làngu Ram daa mer ba futt ca la Ayóoba dëggal boppam fi kanam Yàlla,
Jaambur laa léegi ci saay bokk, mel ni doxandéem sama biir doomi ndey.
Damaa gis workat yi, sib leen; ñoo sàmmul sa kàddu.
Teewul man, may feese doole, feese Noowug Aji Sax ji, ak dëgg ak njàmbaarte, ngir biralal askanu Yanqóoba, bàkkaaram, ngir tuddal bànni Israyil googu moyam.
te mennum Lóot aji jub ji, di kenn ki mu musal, te mu sonnoon lool, ndax ñaawtéefi nit ñu dëng ñooñu,