TSK

TSK · Acts 17:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Acts 4:2 TSK

Fekk na leen ñéññ ca la ñuy waare ak a yégle ndekkitel Yeesu, te loolu di dëggal ne ndee-ndekki, lu am la.

Ndaxte Yàlla jàpp na bés bu muy àttee àddina ci dëgg, àtte bu nit ki mu taamu di sottali; te loolu Yàlla jox na ci ñépp firnde lu wóor, ba mu dekkalee kooku mu taamu, ndekkite lu dee toppul.»

Xel mu rafet lañuy jaay ba mujj diy dof.

¶ Ana kuy xamkat? Ana kuy firikatub yoon? Ana waxkatub àddinay tey jii? Xanaa du Yàllaa def xam-xamu àddina si ag ndof?

Nun, ay dof lanu ngir Almasi; yeen, yeena muus nu ngeen bokke ci Almasi! Nun noo néew doole; yeen, yeena am doole. Yeen it lañu naw, waaye nun, dees noo xeeb!

¶ Moytuleen ba kenn bañ leena këfe kàdduy naxi neen yu ñu jàppe xam-xam bu xelu, kàddu yu sukkandikoowul Almasi, xanaa aaday nit, ak cëslaayi àddina.