TSK

TSK · Acts 17:30

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

jongrukat bi ne: «Bët set, mu guddeeti rekk, Boo amee looy laaj, délsil laajaat ko.»

Luke 13:5 TSK

Maa leen ne déedéet kay, te su ngeen tuubul, yeen ñépp ay sànku ni ñoom.»

te ciw turam, dees na dale ci Yerusalem, yégal xeet yépp, tuubeel gu jur njéggalug bàkkaar.

¶ Ba ñu déggee loolu lañu dal, daldi màggal Yàlla. Ñu ne: «Kon xeeti jaambur yi, ndeke ñoom it Yàlla may na leen ñu tuub, ba dund!»

Ndax maa doon doxantu, di seet seeni jaamookaay, ba yem ci bu ñu bind mii mbind: “Ñeel yàlla ji nu xamul.” Loolu ngeen di màggal te xamuleen ko nag, moom laa leen di xamal.

Maa lay musal ci askanu bànni Israyil, ak ci jaambur ñi ma lay yebal,

Am dangay sofental mbaaxu Yàlla gu réy, akug jéllaleem, akug muñam, ndax ñàkka xam ne li Yàlla namm ci baaxe la, moo di nga tuub?

Moom la Yàlla tudd muy njot gu ngëm di maye, ci kaw deretam ji tuuru. Noonu la Yàlla firndeele ne njubteem mat na sëkk doonte tanqamlu woon na bàkkaari niti jamono ya woon,

¶ Lii nag maa leen ko wax, te di ko biral ci turu Boroom bi: Ni xeeti yéefar yiy jëfe, topp seen xalaat yu tekkiwul dara, buleen jëfeeti noonu.

¶ Ndax yiwu Yàlla kat feeñ na, te looloo indil ñépp ag mucc.

Ndax démb kat yàgg ngeena def coobarey xeet yi xamul Yàlla, ci ay ñaawtéef, ak topp seen bakkan. Dangeen daa màndi ak a xawaare, dëkke naan biiñ, di jaamu tuur yu seexluwu, waaye na fi yem nag.