TSK

TSK · Acts 19:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Acts 13:5 TSK

¶ Ña nga teereji dëkk ba ñuy wax Salamin, daldi fay yégle kàddug Yàlla ca jànguy Yawut ya, ku ñuy wax Yowaan Màrk ànd ak ñoom, di leen jàpple.

Acts 16:3 TSK

Póol nag bëgg mu ànd ak moom, ba tax mu yóbbu ko, xarfal ko ndax Yawut ya dëkke woon gox ba, ngir ñépp a xamoon ne baayam ab Gereg la.

Acts 18:5 TSK

Ba Silas ak Timote dikkee, bàyyikoo diiwaanu Maseduwan, Póol xintewootul lu moy di xamle kàddu gi, di seereel Yawut yi ne Yeesu mooy Almasi.

Ci kaw loolu dëkk bépp ne kër-kër, ne këpp. Ñu jàpp Gayus ak Aristàrk, waa Maseduwan ya àndoon ak Póol ca tukki ba. Ñu daldi riirandoo wuti ëttu joŋantekaay ba.

¶ Gayus mi may dalal, di dalal mbooloo mi mépp këram, nuyu na leen; Eràst saytukatub alalu dëkk bi it, nuyu na leen, mook mbokk mi Kàrtus.

Waaye sama xel dalul woon, ndax gisuma woon sama mbokk, Tit. Teewul ma tàggtoo ak ñoom, jëm diiwaanu Maseduwan.

Te ba ma nekkee ci yeen te soxla dab ma, wéeruwuma ci kenn ci yeen, ndax la ma ñàkkoon, bokk ya jóge Maseduwan ñoo ma ko indil. Fexe naa ba du lenn lu ma leen diisale, te noonu laay saxoo.

Eràst moom, Korent la des, waaye Torofim, Mile laa ko bàyyi, ndax daa woppoon.