TSK

TSK · Acts 2:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Aji Sax ji ne ko: «Ku sàkkal nit gémmiñ? Kan mooy luuwal, di tëxal, di gisal mbaa muy gumbaal? Xanaa du man Aji Sax ji?

Ba Sóol ak surgaam àggee Gibeya, kurélu yonent yaa ne pemm, dajeek moom. Noowug Yàlla ne milib ca kaw Sóol, muy waxandoo ak ñoom ay waxyu.

Xanaa boog nit ñu seen wax leerul, ñu diy làkk-kat, la Aji Sax jiy waxeek askan wii?

Aji Sax ji ne ma: «Bul ne: “Gone laa.” Képp ku ma la yebal, dem ca; lépp lu ma la sant, wax ko.

Nanga dem ba ca sa bokki ngàllo ga, nga wax leen, ñu déglook ñu gàntal, ne leen: “Lii Boroom bi Aji Sax ji da koo wax.”»

Luke 1:15 TSK

ndax ku màgg lay doon, Boroom bi seede. Biiñ ak lenn luy màndee nag, du ko naan, Noo gu Sell gi mooy dale ca biiru ndeyam, solu ko ba fees.

Luke 1:67 TSK

¶ Ci kaw loolu Sàkkaryaa baayu Yaxya feese Noo gu Sell gi, daldi tàmbalee biral kàddug waxyu, ne:

ndax su boobaa Noo gu Sell gi moo leen di xamal ca waxtu woowa la ngeen wara wax.»

Acts 1:5 TSK

Ndax cim ndox la Yaxya daan sóobe, waaye yeen ci Noo gu Sell gi lees leen di sóob fii ak fan yu néew.»

Acts 2:11 TSK

ak Yawuti njuddu-ji-réew yeek tuubeen ñi, ak waa Keret ak Arabi, nun ñépp a leen dégg ci sunu làmmiñi bopp, ñuy siiwtaane jaloore yu Yàlla!»

Acts 4:31 TSK

¶ Ba ñu ñaanee ba noppi, bérab ba ñu daje daa yëngu, ñu feese Noo gu Sell gi ñoom ñépp; ñu daldi tàmbalee waxe fit kàddug Yàlla gi.

Acts 6:5 TSK

¶ Wax jooju daldi neex mbooloo mépp. Ñu seppi Eccen, nit kufeese ngëm ak Noo gu Sell gi, seppi Filib ak Porokor ak Nikanor ak Timon ak Parmenas ak Nikolas, ma dëkke Àncos te dib tuubeen bu duggoon lu jiitu ci yoonu Yawut.

Acts 7:55 TSK

Eccen nag feese Noo gu Sell gi, ne jàkk asamaan, daldi gis leeru Yàlla, gis Yeesu taxawe fa ndijooru Yàlla.

ndax dañu leena dégg ñoom itam, ñuy làkk yeneen làkk, ak a màggal Yàlla.

Ndaxte Barnaba nit ku baax la woon, feese Noo gu Sell gi, ak ngëm. Mbooloo mu takku nag dolliku ci Sang bi.

Ci biir loolu taalibe ya dese mbég ak Noo gu Sell gi, ba seen xol fees.

¶ Kon Yàlla miy maye yaakaar, yal na leen feesale gépp mbég, ak jàmm ci biir ngëm, ba ngeen géejule yaakaar, ci manoorey Noo gu Sell gi.

Ñi Yàlla tabb ci biir mbooloom gëmkat ñi, ñi ci jiitu ñoo di ndawi Almasi. Ñaareel bi di ñiy waxe kàddug waxyu, ñetteel bi di jànglekati kàddu gi. Ñi ci topp di ñiy def ay kéemaan, ñi ci topp di ñi am mayu faje, ak ñi mane dimbalee, ak ñi mane jiite, ak ñiy làkk yeneen xeeti làkk.

¶ Cofeel nag du jeex mukk. Su dee kàdduy waxyu, dina wéy; su dee ay làkk, dina selaw; su dee xam-xam, dina xewi.

¶ Sant naa Yàlla ndegam maay làkk yeneen làkk ba raw leen, yeen ñépp.

¶ Kon nag ana nees di def, bokk yi? Bu ngeen dajee, kii am woyu cant, kii am lu muy jàngle, kee am am peeñu, kale am lu muy waxe weneen làkk, keneen am am piri, loolu lépp na ko feddli ngëm taxa jóg.

Buleen naan biiñ ba màndi, màndite ci afal seen bakkan la leen jëme, waaye na leen Noo gi fees,

Yonent yooyu, xamalees na leen ne du seen njariñal bopp lañuy liggéeyal xibaar boobu, xanaa yeen. Ñi leen àgge xibaar bi tey ñoo di ñiy waare xibaaru jàmm bi ci dooley Noo gu Sell, gi ñu yebale asamaan, te muy mbir mu malaaka yi sax, noon siiwa nemmiku.