Doomi Sem yu góor ñii la: Elam ak Asur ak Arpagsàdd ak Ludd ak Aram.
TSK
TSK · Acts 2:9
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba loolu amee surga ba jële fukki giléem ca giléemi sangam, dem, yóbbaale li gën ci mboolem xeeti alalu sangam. Ma nga jëm réewu Mesopotami, ga Naxor dëkk.
Bésub keroog Boroom bi jooti loxoom ñaareel bi yoon, ngir jotaat ndesu ñoñam, wa des Asiri ak Misra, ak Pattros ak réewum Kuus, ak Elam ak Sineyaar, ak Amat ak biir duni géej ya.
Ca biir peeñu ma, maa ngi Sus, péeyub diiwaanu Elam. Ma gis ci peeñu mi ne maa ngi ci wetu yoonu ndox ma ñu gas te ñu di ko wax Ulay.
Ba loolu amee ñenn ca jàngu ba ñuy wax jàngub waa Goreel ga, daldi jóg, di tàmbalee weranteek Eccen. Ay niti waa Siren a nga ca, ak waa Alegsàndiri, ak waa diiwaani Silisi ak Asi.
¶ Xel mu Sell mi nag tere leena yégleji kàddu gi ca diiwaanu Asi, ba tax ñu jàlli biir diiwaanu Firisi ak Galasi.
Loolu moo wéy diiru ñaari at, ba mboolem waa diiwaanu Asi dégg kàddug Sang bi, muy Yawut, di Gereg.
Ñenn ñay ay soppeem ca kàngami nguur ga sax, yónnee nañu ca moom, di ko àrtu ngir mu baña foye bakkanam, di dem ca ëttu joŋantekaay ba.
Ba ñu dikkee, mu ne leen: «Yeen ci seen bopp xam ngeen bu baax, ca bés ba ma jëkkee teg sama tànk Asi, ba tey jii, ni ma masa doxale ak yeen,
¶ Mboolooy gëmkati diiwaanu Asi nag ñu ngi leen di nuyu. Akilas ak Pirsil, ñu ngi leen di nuyu bu baax ci turu Sang bi, ñoom ak mbooloom gëmkat ñiy daje seen kër.
¶ Xam nga ne waa diiwaanu Asi gépp a ma won gannaaw, te Fusel ak Ermosen ci lañu bokk.
¶ Lii mu ngi tukkee ci man Yowaan, ñeel juróom ñaari mboolooy gëmkat ña ca diiwaanu Asi. Na leen yiw ak jàmm ñeel, tukkee fa Ki masa Nekk, Ki Nekk, di Kiy Dikk, tukkee it fa boroom juróom ñaari noo ya fa kanam ngànguneem,