TSK

TSK · Acts 20:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yuda déy laay bank, muy samag xala, te Efrayim laa koy soxe, muy fitt gi. Yaw Siyoŋ, sa doom yu góor laay yékkati ci sa kaw doom yu góor, yaw réewum Geres (/Yawaan). Doomi Siyoŋ laay def saamaru jàmbaar.

Ñuy feddli pastéefu taalibe yi, di leen ñaax ngir ñu saxoo ngëm, ne leen: «Coono yu baree ngii, fàww nu jaare ci, ngir tàbbi ci nguurug Yàlla.»

Nu bawoo fa jàll ba Filipi, dëkku gox ba jëkk ca diiwaanu Maseduwan te di moomeelu Room. Nu toog fa ay fan.

¶ Ba mu ko defee bokki gëmkat ña yebal ca saa sa Póol ak Silas ca guddi ga, ñu jëm Bere. Ñu agsi, dem ca jàngub Yawut ya.

Mu yéegaat, dagg mburu ma, lekk. Waxaat na lu yàgg, ba njël jot, mu sooga dem.

Ndaxte sunub woote laloowul pexem sànke, ak mébét mu setul, akug njublaŋ.

¶ Li ci des nag, bokk yi, moo di yeena nangoo ci sunu làmmiñ, jëfin wi ngeen wara jëfe ba neex Yàlla, te it moom ngeen nekke. Waaye danu leen di tinu, di leen ñaax, ci turu Sang Yeesu, ngir ngeen gënati koo jëfe.