TSK

TSK · Acts 20:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Lii moo tax yeen waa kër Israyil, ma di leen àtte, ku nekk ciy jëfam. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Dëppleen te dëddu mboolem seeni tooñ, ngir seenu ay bañ leena gàllankoor.

Luke 13:3 TSK

Maa leen ne déedéet kay, te su ngeen tuubul, noonu ngeen di sànkoo yeen ñépp.

Luke 15:7 TSK

¶ «Maa leen wax, ne leen: bu benn bàkkaarkat doŋŋ tuubee, noonu rekk lay doone mbégte fa asamaan, ba raw mbégte ma fay am, bu juróom ñeent fukk ak juróom ñeenti nit jubee, te soxlawuñoo tuub.

te ciw turam, dees na dale ci Yerusalem, yégal xeet yépp, tuubeel gu jur njéggalug bàkkaar.

Acts 2:38 TSK

Piyeer ne leen: «Tuubleen te ku nekk ci yeen sóobu ci ndox ci turu Yeesu Almasi ngir njéggalug bàkkaaram, ngeen daldi jot ci Noo gu Sell giy maye.

Acts 3:19 TSK

Kon nag tuubleen te dëpp, ndax seeni bàkkaar faru.

Moom la yonent yépp seedeel, ne képp ku ko gëm, jot nga sa njéggalug bàkkaar ciw turam.»

¶ «Kon nag bokk yi, xamleen ne ci Yeesu moomu lañu leen birale njéggalug bàkkaar. Te mboolem lu ngeen tële woona wàccool, ba seen njub mat ci yoonu Musaa,

Yàlla nag jéllale na janti ñàkka xam googa woon, waaye tey mu ngi woo ñépp, ak fépp fu ñu féete, ngir ñu tuub.

¶ Mboolem Yawut yaak Gereg ya dëkke Efes nag yég mbir moomu, tiitaange dikkal leen ñoom ñépp, daraja ju réy doxe ca ñeel turu Sang Yeesu.

¶ Ñu teg ci ay fan, Feligsë dikk, ànd ak soxnaam Dursil, mi dib Yawut. Mu woolu Póol, déglu kàddoom ci ngëm gi sababoo ci Yeesu Almasi.

Waaye li dale Damaas ak Yerusalem ba ci réewum Yawut gépp, ba ca ñi dul Yawut, ñoom ñépp yégal naa leen seen wartéef, muy tuubeel ak waññiku ci Yàlla, ak jëf ju tuubeel yellool.

Muy sama digg ak Gereg yu xay yi, mbaa ñu xayadi ñi, ak ñi rafet xel, mbaa ñi ñàkk xel, am na lu ma war ci ñoom ñépp.

Am dangay sofental mbaaxu Yàlla gu réy, akug jéllaleem, akug muñam, ndax ñàkka xam ne li Yàlla namm ci baaxe la, moo di nga tuub?

Nun itam ci lanu; dees na nu waññal sunu ngëm, àtteb ñu jub, nun ñi gëm Ki dekkal sunu Sang Yeesu,

Saw làmmiñ, soo ci biralee ne Yeesu moo di Boroom bi, sab xol it, nga gëm ci ne Yàlla dekkal na Sang Yeesu, dinga mucc.

Ndaxte tiis wu Yàlla namm, ag tuubeel gu jëme cig mucc lay jur, te loolu du tiis wees di tiisoo. Waaye tiisu àddina, ndee lay jur.

Moo tax dootu man maay dund, waaye Almasi mooy dund léegi ci man. Sama dundu yaramu suux wii tey nag, ci ngëm gi ma gëm Doomu Yàlla laa koy dunde, moom mi ma sopp, ba jébbale boppam ngir man.

¶ Moo tax man it, bi ma déggee ba tey, seen ngëm ci Sang Yeesu, ak seen cofeel ci ñu sell ñépp,

Jaamub Boroom bi ndànk la war di jubbanti diiŋatkat yi, nde jombul Yàlla may leen ñu tuub, ba xam liy dëgg.