TSK

TSK · Acts 20:29

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yerusalemee, séentul, xool ñiy jóge bëj-gànnaar. Moo ana gétt gi ñu la dénkoon, sa gàtt yu rafet ya?

«Yaw nit ki, waxal waxyu fi kaw sàmmi Israyil. Biralal waxyu ci kaw sàmm soosu, ne leen: Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Wóoy ngalla sàmmi Israyil yiy sàmm seen bopp! Xanaa du jur gi, la sàmm si wara sàmm?

Wóoy bii yambarub sàmm buy wacci gàttam. Yal na saamar làggal loxoom, fuq bëtu ndijooram. Yal na loxoom lax ne làcc, bëtu ndijooram giim ba gëmm fatuus.»

¶ Waaye na mu ame woon ci askanu bànni Israyil ay yonenti caaxaan, ni lay ame ci seen biir ay sëriñi caaxaan yuy sërxal ay àlluway sànkute yuy weddi sax Sang bi leen jot, ba yóbbe seen bopp sànkute ju bette.