¶ Ca ëllëg sa kilifay Yawut yi ak mag ñi ak firikati yoon yi daje Yerusalem.
TSK
TSK · Acts 22:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Acts 4:5
TSK
Acts 9:1
TSK
¶ Ci biir loolu Sóol moom, noyyeewul lu moy di tëkkook a jéema bóom taalibey Sang bi. Mu dem nag ca sarxalkat bu mag ba,
Acts 13:26
TSK
¶ «Bokk yi, yeen askanu Ibraayma, yeen ak jaamburi ragalkati Yàlla yi ci seen biir, nun lañu yónnee kàddug mucc gii.
Acts 26:10
TSK
Def naa ko ci Yerusalem, te it bare na ñu sell ñu ma tëjlu ci kaw sañ-sañ bu ma sarxalkat yu mag yi jagleel, te saa yu ñu leen tegaan àtteb dee, dama daan biral kàddu gu leen àtte ñàkkal.
Acts 28:21
TSK
¶ Ñu ne ko: «Nun de, du benn bataaxal bu nu jot bu jóge Yude ci sa mbir, te du kenn ci bokk yi, ku dikk wax mbaa mu seedeel la lenn lu bon.
1 Timothy 4:14
TSK
Bul sàggane may gi ci yaw, te di lu ñu la baaxee ag kàddug waxyu gu ànd ak tegeb loxo, ba la mag ñi defaloon.