TSK

TSK · Acts 23:34

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ci kaw loolu ñu woo bindkati buur ca bés ba, di ñaar fukki fan ak ñett ca weeru Siwan, ñetteelu weer wa. Ñu daldi bind mboolem lu Mardose santaane, ca mbirum Yawut yaak jawriñ yaak boroom dëkk yaak kàngami diiwaan ya, dale ko ca End ba ca Kuus. Muy téeméeri diiwaan ak ñaar fukk ak juróom ñaar (127). Ñu bind ndigal ya ci mbindum diiwaan bu nekk ak ci làkku xeet wu nekk, Yawut ya it ak seen mbindu bopp ak seen làkku bopp.

¶ Ci kaw loolu Daryus waa Medd ba, jot ca nguur ga, fekk ko mu am juróom benn fukki at ak ñaar.

Acts 6:9 TSK

Ba loolu amee ñenn ca jàngu ba ñuy wax jàngub waa Goreel ga, daldi jóg, di tàmbalee weranteek Eccen. Ay niti waa Siren a nga ca, ak waa Alegsàndiri, ak waa diiwaani Silisi ak Asi.

Póol ne ko: «Man de ab Yawut laa, di as goru Tàrs, dëkk bu ñàkkul tur ba ca diiwaanu Silisi. Dama lay ñaan, nga may ma, ma wax ak mbooloo mi.»