TSK

TSK · Acts 24:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Acts 21:8 TSK

Ca ëllëg sa nu dem ba àgg Sesare. Nu dem kër Filib, xamlekatu xibaaru jàmm, bi bokk ci Juróom ñaar ñi. Nu dal ak moom.

Mu ne ko: «Xaaral ba say tuumaalkat itam dikk, ma déglu la.» Mu santaane nag, ñu denc ko ca kër buur Erodd.

Acts 27:3 TSK

¶ Ca ëllëg sa nu teeri Sidon; Yulyus nag baaxe Póol, may ko mu dem ci ay xaritam, ngir ñu topptoo ko.

Muy yégle nguurug Yàlla, di jàngle mbirum Sang Yeesu Almasi ci teeyug bakkanam te amul benn gàllankoor.