Acts 27:17
TSK
Ñu yéege looco ba, daldi jël ay buum yu ñu laxas ca yaramu gaal ga, dàbblee ko ko. Ci kaw loolu ñu ragala ngiroji ca beeñ bu ñuy wax Sirt, ba tax ñu sànni diigal, ngir yeexal gaal ga, daldi yalal.