Isaiah 65:24
TSK
Su boobaa balees woote, man, maay wuyu; balaa ñoo daane seen kàddu, ma nangul leen.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Su boobaa balees woote, man, maay wuyu; balaa ñoo daane seen kàddu, ma nangul leen.
Ñoom ñépp nag feese Noo gu Sell gi, tàmbalee làkk làkk yu wuute, na leen ko Noo gi manloo.
¶ Ba guddi gay xaaj, Póol ak Silas a ngay ñaan, di sàbbaal Yàlla, ñeneen ña ñu fa tëj di leen déglu.
¶ Ku desele am xel mu rafet nag, na ko ñaan Yàlla, mu may ko ko, ndax Yàlla mooy yéwéne ñépp te du sikk kenn.