TSK

TSK · Acts 5:28

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Naka la Axab gis Ilyaas, ne ko: «Kii yaw a, di lëmbe Israyil nii?»

Buurub Israyil ne Yosafat: «Am na ba tey genn góor gu ñu mana seetal ci Aji Sax ji. Waaye man maa ko jéppi, ndax du wax waxyu bu baax ci man, lu bon rekk; mooy Mise doomu Yimla.» Yosafat ne ko: «Buur, bul waxe noonu.»

¶ Kàngami buur yooyu dem ne Buur: «Waa jii, na dee rekk; mu ngi yoqil xarekat yi des ci dëkk bi, di yoqil ñépp ndax waxam jii mu leen di wax. Waa jii kat wutul jàmmu askan wii, xanaa musiba.»

Acts 3:14 TSK

Yeen, yeena jàmbu Ku sell ki te jub, tinul ab bóomkat.

Acts 4:18 TSK

¶ Ñu woo leen nag, aaye leen, ne leen mayatuñu leen benn yoon ñu waxati lenn, mbaa ñuy jàngale ci turu Yeesu.

Acts 7:52 TSK

Kan ci yonent yi la seeni maam fitnaalul? Ñoo rey démb ña yégle woon ñëwug Aji Jub, ji ngeen wor tey, bóom ko.